03/12/2024
Yére baay laat fu mu jóge ak ndax sol ko ci théâtre jaadu na ?
Baay laat li ñuy jublu ci tur wi mooy Seex Abdu Lahad Mbàkke ñatteelu xalifa bu Sëriñ Tuubaa mi ko daan sol.
Moom nag daawul sol yére boobu bu njëkk waaye bi nijaayam ju tudd Sëriñ Amsatu Jaxatee faatoo, dañu koo jox ca yére ya ñaari yére ngir barkeelu, ñaw bi nag neex ko lool, mu laaj ku ko ñaw ñu ne ko Sariif Ndaw, Sëriñ Abdu Lahad jox ko ñatti piis ngir mu ñawal ko ko model boobu ndax yére bi da koo neex lool, mu am tailleur bu tudd Baaba Aydara dégg loolu daa di ciy ñaw lu mat ñaari gaal (valise) jox ko Sëriñ Abdu Lahad, foofu nag la Sëriñ Abdu Lahad jaare di sol baay laat kese.
Li tax nag yére bii gën a tasaaroo ba yegg fu sori, mooy daayra Isbu Tarxiya bi nga xam ne bi ñu ko sosee yére boobu lañu maase di ko sol ñoom ñépp ak fu ñu man a nekk, lii bokk na ci li gën a siiwal xeetu col gii.
Kon baay laat yamul ci doon ab yére kese waaye xàmmekaay (identité) murid la mujj doon, fu ko nit sol ci àdduna bi rekk ku xànmee murid bu ko gisee xam ne kii murid la muy lu am solo, loolu bari na ci àdduna kureel yu am seen colug bopp.
Lii moo waral kuy sol yére bi sax lu yiw rekk lañuy séentu ci yaw, ku ko sol moomatoo sa bopp ndax duñu la xoole sa jëmm waaye dafa am mbooloo mu ñu lay xoole, boo defee aw ñaawtéef yàq nga deru mbooloo moomu mépp, kon murid bi koy sol it war naa bàyyi loolu xel bu baax.
Ndax wares na koo sol ci théâtre ?
Waaw dara nekku ci de, ndax théâtre nekkul lu aay te li ñu ciy wane lu société bi xam lay doon, waaye li mat a moytu dëgg mooy moment bi nga koy sol ci ban rôle nga nekk, bu dee rôle boobu du mbir mu yiw walla muy lu diine ñaawlu, kon sol ci baay laat lu ñaaw lay doon, ndax dina am ñu jàpp ne dafa am mbooloo mooy saboter walla nga leen di salteel, kon jar naa moytu, ñi ko ko sol loo def nañu lu jaaduwul moom it waru ko woon a nangu.
Moor Suraŋ